LYRIC

{Jahman}
Tchi digueunté Maraakh maassé Bi Djololi suuf séédé
Tchi lagn gawantou sakou ci sa ay njarigne
Tchi Kaddu yu tedd yi may bindeu ngir way ci mom
Kène dotoul mel ni yaw nio ngi lay Chiaaré
Di riir ngir Modou Bamba mo xékh té balle takoul
Di riir ngir Maam mi indi lerr tchi yone wou méti wi
Ak keppeu ko xamni Baye Fall nga tèy Mame Cheikh Ibra Fall
Maysa Bigué Coumba Fall mo wané yone bi

Aonzou Bilaah
Bismilaah

Kène dou yaw Ibra Fall
Cheikh Ibra yi nékal Kamal
….Dial Goor Yalla yomboul
Lassal daak lil jamal Ibrahima Fall lam yazal
Yaay Lamp gueunéél bi Bamba Taal yaram bi naam Fall
Yaw la Bamba wane kawçaraak gui naane
Guédiou lerr yi yako naane
Mbeur yeup nga bolé daan té Fall titeurou woulo
Seug béék sigui béék, Borom Yallah mba jaameuh nga am ?
Tabbé Maam Seynabou Ndiaye mo wané yone bi

Baye Fall moy lou doyouk waar
Mo Toudou tuurou Yallah bi
Bamouy xotti djawou dji di yengueul Harass ak Kurçiyu
Baye Fall moy dieufé ndigueul
Moy diokhé té kène douko laathie
Baye Fall bou deugou té waur Keur moy Aldiana Firdawsi
Haaaaan ! Niou roy ci Cheikh Modou Kara ak Baye Karim Al-Akhlah
Tognou niou, togn lou wougnou
Dieuf yi nagnou ko rafétalaate
Keppeu ko xamni Baye Fall nga tèy beug roy tchi Cheikh Ibra Fall
Nanga am YARR, MANDOU, TÈY, teuy NJEUFÉ NDIGUEUL

{Ahmada}
Al Hamdulilah niou santati CHEIKH BAMBA tay
Ngir mo takhaw Djouli wone Fa Ndar bagn niou sankou tay
Rakkam ya moy sauwétasse tchi nioune ngir moy dokh batay
Magal ko moy li war ci nioune diko SANTE tay
Bureau bé Fa Ndar mo atté GOOR Yafa diaar beu weuy
Kou tchi doul Serigne Touba kérok signé wone nga “Oui”
Balle darsak wa Tribunal kérok nieup xeuy kagnou naane
“Borom Ndar takhaw dikou Yallah dji djay”

Bamba Bay neu Goop na djaak neu
Gaadou neu ak sakkeu
Sameuh bodji wall neu moogne neu ganaaw aadou sokkeu
Meune neu dieuf nako ak xam xam
Mouride na nga dégueuh ragnél lou baakh tchi lou bone
Boula tchi kène dégueuh
Beus nga xol bi diokh Bamba kone teudeul nélawal
Xara-ngal néél xareu-xareu wakh leu djou am séwa séw
“Wa Salaamoune ala manni tabkhal khoudaa” la wakh
Miim reew Bamba ka mom moy kika mom

Wa salaamoune ala manni tabkhal khoudaa” la paix est avec celui qui suit le droit chemin “

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR