LYRIC

{Verse 1}
Disque d’or ba ngui sama disque dur
Dou école rek ladone am ay 10/10
Di ngeu niou raw no nigga wakhal lou djaadou
Dioxèle sa sani taathiou baayil bama guéné disque bi
Fuck ….Mane sama logo bi laay sole
Douma classé goor-djiguène ba paré di sole versace wala Gucci No
Album bi dina diss cii niom
Nigga mane disque d’Or bi rekka takh may téé micro
Kone dama cii Jog Kifi daakeu rap njaago la boy
Té Yaakarouma sakh cii rap meuna Jazz wala Rock
Gni gueuneu niaak jott président nioy niaane sama song
Mane dama dégue time is money rek djaay sama montre
Yeah maay yéddeu gniy daw djangue
Yeah maay yéé boy yiy saw laale
Nénala nigga nékoul kiy dieul pé mo eupeu xam xam
Yène nieup di ngène laathie pour disque d’or noumay def
Waayé mouno meusseu daagne kumpe ba dh féké sa beussou deuthie

{Refrain}
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Cii disque dur bi laa dinthie sama disque d’or (2 fois)

{Verse 2}
(Music musico) Sa dom néna day musique, musique pour yé niit yi
Musique taamite pour nékeu kou siiw
(Kou niit yi di thiow) Maay Yiliff ay kilifeu té sama kiliftéf dou bou makk ndax Yallah nguifi
(Deudjou niou cii kaw) Té kène téréwouma naaw ci diouraum niaari assamane
Dafma lerr mane maafi teklé disque d’Oooooooooooooooor
Samay SOXLA makoy FATHIE té moussouma def MEDECINE
Chaque jour dagne may tek melni dama fay wa télé bii
Da nga fogone damay daanou nigga yaay imbécile
Da ngeu may djapp réh nii mandi kat bouy marqué messi
Xippil khol kogne bi laay tabakhal CITY SPORT
Boy yimay daanél wétchite nieup laay tidjil compte
Makoy tangal Ndakarou Ndiaye Louga SIKITHIOR (Ziguinchor)
Da ngama dégueulou rek faaté 2PAC ak BIGGIE boy

{Refrain}
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Cii disque dur bi laa dinthie sama disque d’or (2 fois)

{Verse 3}
Dofla ni 50cent ak Eminem,
Gun la cii militaire bi nek ci guerre
Normal may né cii scène nioumay filmé
Com d’hab nioune nio ngui grêve té jail bi fess
Sama Mère néna boul meusseu doff dofflou ba gnèin fi kène
Motah mane douma meusseu def ni yène
Werr yi douniou changé kone fuck Benithez
Ma mome 2014 ak 2015
Dama bindeu texte ba guèné mixtape
Album bi dina guèneu 2016 cii laay tambalé bindeu chèque
Dara xéwa goul yaw nga commencé merr
Waayé Album bi di ngako dieundeu ni sa ordonnaçou mère
Somay tékeulé sa rappeur boumou meuneti done
Djappalni ya ngui tékeulé Talaatay Nderr ak Goudi Town
Job bou sett ak concert yu fess, projet yu déh
Nel Jordane amena ay Xarite soxla wouma ay Jo yu bess
Dessna touti dotoma sakh guisseuti ndax dembe yama eupone buzz
Tay sama secret niola gueuneu siiiw

{Refrain}
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Disque d’Or ba ngui cii sama disque dur
Cii disque dur bi laa dinthie sama disque d’or (2 fois)

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR