LYRIC

{….}

{Verse 1}
Djoudou ci ay dikk déh ci yakaar bu tass
Kou tchi lidieunti falou gass kambeu carte
Moumeu takhawé baatu askane di kass
Kigni wakh gnigniy nakh moniou yagg nakh
Faux types yi ancien soukou moudjé done boss yu riche
Nit kuy politique moy fènn yuy dadjolo ba tolou nit
Nio dieulé goor gui fi andak Macky xagne ko mou doli biss
Lepp yokou fi sauf transhumant yi dem soldé sen vie
Kouy Fallou SENE, Balla GAYE, Bassirou FAYE
Bo cartouché woul meune nga def Bac plus Déh
Mougn boudoul diekh bakhoul sakh ci nit koudoul déh
Mougn boudoul diekh bakhoul sakh ci nit koudoul…
Bo banioul Parrainé Guéweul yu riche yi di xew
Waxma noy soureulé gnénène gni xiff douniou lekk
Wesso gouniou naweet Badola sibirou déh
Yelwaane kat bi Policier leu bou civilou rk
Agresseur rarement lay djote ci domou diw yigniy degg
Kougn tchi foli nga vidé caisse tidjile niou livre bu bess
Nguur gui peuple béko mom moy King bi dou yeen
Batay ndokh ngi manqué deukou kirikou men
Sunu kogne sou sété beussou sett settal leu fils
Nioune dagni déh di dokh mounou niou espérance de vie
Dembe xexkh nga danél njite, tay sa chèque nga laale né miik
Miin naniou ko ci yeen ci djamonoy Leopold Sédar ba fiii

{Bridge}
Lou taximan di tééh, Djaay katou djeune di dieul
Li Carrapide di karr, Lou Président bi gueune
Lou Menuisier di dathie. Fane leu salaire di diaar ?
Lou Etudient di djangue. lane leu diplôme di diar ?

{Refrain}
Deug dou loi ci niom niouy violé yu lène ci nekh
Deug dou loi ci niom niouy violé yu …..
Digué dou borr ci nom fégne neu ci ni ngène nioukoy fay
yéaaah

{….}

{Verse 2}
Lo guiss day diekh khar Yallah xamo bane biss lay téw
Police seu gueuneu dokh école ndakh boy yi miss naniou jail
Kou gnéin gni sathie siw di sakéto sen vitre teintée
Sa pass ngay woute dem tanthialo ci gaal yi risqué déh
Gni am nioy gueuneu am meusso guiss école privée grêve
Gni niaak gueuneu niaak dou dégn ni taalibé ak mbède
Bolène sanione Yallah neutre Iblis arbitré lène
Niouné yéneuy sathie xalé yi dem sacrifié lène
Da fekk Niounite nioko tek suniou bopp
Sandwitch ak djouni lagn dieundé suniou Bopp
Ndakh niou ngi niouy dieundé suniou xalissou bopp
Daniouy woute wathié sen Bopp Falou Yéék suniou bopp
Gniy Politique matouniou 1000 ba paré tokk suniouy fiit
Diarrouniou toppeu, diarrouniou guiss ndakh dou nioy sauur suniouy tchine
Etudiants yi tothie suniou Bus danio compogoul shit
Sen mbokk dou job ci usine, sen dom dou tok souniouy bus
Xaliss moy rideau bi gueuneu makk pour mour sa xel
Bane Média mo djaayagoul boppam tchi buur ba tay
Loy guiss boudé gniy job tchi télé bi ay goumbeu lagn
Gueum sunioy Média moy doundeu lé seu coumpeu fène
Gni far ci gnifi falou nieup yaw xam nga fign feeté
Euleuk tchi biir bou suuf sédé Kilifeu diiné rouss beu déh
Beu fimay wakhék yaw am niouy doundé thiéré
Dieulile seu carte 23 juin diaroul wone tuur dérétte

{Bridge}
Lou taximan di tééh, Djaay katou djeune di dieul
Li Carrapide di karr, Lou Président bi gueune
Lou Menuisier di dathie. Fane leu salaire di diaar ?
Lou Etudient di djangue. lane leu diplôme di diar ?

{Refrain}
Deug dou loi ci niom niouy violé yu lène ci nekh
Deug dou loi ci niom niouy violé yu …..
Digué dou borr ci nom fégne neu ci ni ngène nioukoy fay

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR