LYRIC

{Intro}
“Il n’y a eu qu’une seule cabale d’individus puissants qui ont dirigé le cours de l’histoire.
Et l’homme préfère croire que ces individus n’existent pas. Ce qui contribue à leur succès”

{One Shot}
Gnou ni mou nngi doré
Gnou ni mou nngi doré Phiraona (Pharaon) ak ay Pyramideum
Trinité Paiënne wédi Yallah nangou diaamou xeureum
OZYRYS ak ISIS, ISIS ak HORUS né rouh bou beugué mouthie diaamou ANUBIS
YOUSSOUPHA andi askanam daw marral ak xiff
Ay siècle rombeu niou def len djaam dilène door xirr
Yoneinte YALLAH MOUSSA bokouna ci gni ndieukeu fippou
Fouki mbougueul yi dall Egypte ndaxté YALLAH laniou done teukou
Khar Guedj guèné ndokh ci dothie takhoul nieup nangou
Gnéinti fouki att (40 ans) ci Désert bi ba gni wédi nieup faatu
Borom bi dikk lène reew boumou toudé Palestine
Sen njite yi deuk di guerre melni kou Arès tiim
AL AHAD wathié sen biir Samuel ak Daouda
Miy Baayou Souleymane borom xel bou yaatou ba
Ci mom leu thiow li doré NIIT djiné DJINÉ
Am niou djébeulou dji dem créer dji bénène Diiné
Xam xam bou nioule bi wathie lakou ci guinaaw ay tabakh
YALLAH dou wathié NIIT yu baakh ci ay NIIT yu baakh
Dara mouthieuloul xeet bou ndaré bone
NABUCHODONOSOR déporté lène tcha Babylone
Fa laniou fekk GILGAMESH BALE ak ISHTAR
Modifié AL TAWRAT boléko tchi sen Histoire
Niou teup ay att yu beuri rouhou LAAHI daadi wathieu
Nélène AHMAD dèy nieuw bou yabbo na ngène ko waathie
Byzancin Samarcande daanou
ISLAM bi melni kherr banteu dall tchi kawam daanou
Infiltration bi amaate Crédo de Nicée
“Avant de pouvoir régner il faut diviser”
1098 attoum Premier Croisade
SALADIN seu Jérusalem taxaw né dafay Djihad
Templier Eglise bi néko Hérétique
Rose-Croix lakkou tchi ay rite yu satanique
Comme que séni njiteu mom louniou toudé Moyen Age
Borom bi wathié Peste mou done ngandam nettoyage
Pitenberg, Christophe COLOMB Léonard DE VINCI
Galilée, Matin Luther, famille Médicis
Illuminati
Illuminati
Njitou Franc-maçon moy toudou Illuminati
Branche musulmane bé toudone les Hachichines
Rap nga réh djafé gueum melni da ngay sétane film
Bokou nagn tchi gni favorisé traite des noirs
Sédeu Grande Bretagne ngandam territoire
1776 aduna am xéw
Novus Ordos Seclorum (Nouvel ordre des siècles) moudj na am reew
Famille Rothschild monopolisé banque yeup
Imposé mode riiba ndakh niom nioy lébal nieup
Darwin né domou Adama ci Golo leu djougué
Lolou xol boumou dougou meuneutoul nangou bène diiné
Bo nangoul né Iblis amna lane ngay doyé YALLAH
Kou Ragal BUUR bi dégn sa xol yaw tesskaré gnéin leu
Sen Politique moy dougou sa xel bi nga déh ndaw
Da ngay magalék sen gueum beu louniou wakh ngané waw
Guerre bou meusseu am ci Aduna sen loxo ngi ci
Fitna lagni baye dinagne ko gaupe bisseu ngi ci biss yi
Guerre Mondiale 1, 2 wadial 3
Musique bi nék sunu xol moy sen Cheval de Troie
Def Jay-Z royoukaay Taat fowou kaaay
Bo wanéwoul seu thieur ni Rihanna do djaay
Message bi moy toppeuh seu beug beug def li nga yëk
Toppal sa yone na lerr rek na melni diggu beuthieuk
Rappeur yi di def séni signes tendance
Médias yi tamal lèn di tiim scandale
Fékhé beu Yaa fouss am dolé ci kaw Djambaar
Poukëré neeweul dolé deug ndakh c’est vendable
Sénégal amoul Illuminati, Franc-Maçon leu fess
Naniou am bénène Président ndakh niou meusseu am lou bess
Loges ya ngi fi Dakar biss bouné nga rombeu ko
Chrétien deug, Musulman deug mou djombeu ko
Rotary Club par exemple mais siw nak
Niaari Artistes lagn xam niouy lekk siwo nak
Gni ngi, fepp gni ngi fepp, gni nga sakh fi ngako doul fogué
Aduna dou dieundeu Aadiana boulène ko fogué

{Outro}
…”Si j’ai raison tu es mêlé à tout ça”
……….”N’écoute pas ce qu’il raconte pour lui il y a des conspirations partout”
… “Pas des conspirations, une conspiration ! j’emploie le singulier”

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR