LYRIC

Police dou décrocher, Sapeur day yékheu nieuw
Nénagne déh dou raccrocher té féppeu la meuneu nieuw
Amna niou roussoul dieuw neew ci biir Corbillard
Amna niouy dinkaate sen Serigne té danio nieuw ziaar
Djiko youdoul dégne ni feebar youdoul weer
Politique = Politique même bou néké sen keur
Lampe dou leeral khol bou kou ignaane di fay facture
Djapal sa télé khol ndakh leumbeul amna censure
Saayo djoyé neew beu ya ngi djoy sa bopp
Meun na am minute bissi toppeuh yaw yaay done kissi toppeuh
Corbillard déy yaubou neew mais amena foumouy yém
Djiko day andak neew té amoul foumouy yém
Da nga chirurgie té so méré sa kanam niaaw
Ni nga mel nékhoula ni nga mélone mo ngi sa guinaaw
Armélou reuthiou bo guiss ay nakhar lagnefa soule
Kouniou fay sa borr nga merr li nga leblé bakhoul
Kouy def pour niou tathiou do dimbeuli ay gaana
Koulay djaay khatt xol néko Yallah yaa na
Kouy def pour niou guiss ko do sauraalé ay goumbeu
Kouy def pour niou wakh ko do djapalé ay moumeu
Bopp bou ndaré barké nopp yuy dégueuh niossi sakh
Mais koudoul dégueuh wakh djou lerr diaroul nioukoy thiakh
Djoyou xol meune na gueuneu sokhor yiy feegne ci beute
Amna niouy mandi ci dérette ba paré dinthieu deuteu
Nit bouy xalate dougou caisse waroul keupeu caisse
Aduna bi diekhna ba paré lane mofi dess
Loutah sunu Mère-rou marché yi nio dakkeu fay djouti ?
Loutah gni liguèy lou beuri rekka fi am touti ?
…………….
Yaw hann !
Sen keur bo yoroul comme liir bouy doga djoudou
Sa wakh dou compté bo amoul chiffres kène doula toudou
Xaliss lagnou gueuneu sécurisé que domou Adama
Té nénagne Xaliss dagneka def ngir domou Adama
Am niou sen xaliss eupeu keur té sen compte dou fess
Loutah ba légui Afrique meunoul am monaie bou bess
Toubab déy am louko nekh ci deukou nit kou nioule
Té Nit kou nioule mounoul mounieul ben nit bou nioule
Trafic d’armes yu légal tchi guerre yu légitime
Péremption, Kalachnikov, mba Guerre intestine
Boy sathieu sathial milliards sinon kèneu doula kassale
Bou wesso séy dieuf Yawmal Qiyyaam lène doula passale
Nit dina dougou safara ba paré yaubaalé mbolo
Nit dina raté Aldiana ngir mbir yu niaakeu solo
Armélou reuthiou bo guiss ay nakhar lagnefa soule
Le passé c’est le passé mais ba légui boumou djaam doggoule
Bénéfice wessouwoul yéwou di guiss bakkane
Saayo taylé sa bopp djapalni taylé nga sa askane
Défaite bi gueuneu triste moy biy waathieu ba ci say dom
Amena niou paré djaay sen dignité ndakh simple koom
4.4.44 té You Indépendant woul ba légui
Mame Madior Boye ak sacrifice ci diguou guedj gui
Def again ak Diambogne pour mener niou en bateau
Nouyo niou thiaamogne sa last biz niom nio ngi sen chateau
Di nga djoy di nga triste Orphelin
Sopi leu capitaliste sen chèque moy sen Câlin
Million dou compensé bakkane amoul rouh bou am prix
Etat bi pompé presses ni vulcanisateur pour gueuneu meuneu free
Président dou dougou jail, Magistrat dou teudeu
Avocat dougneko Correctionnel bou wakhoul deug
Domou diw bountou boula neekh meun ngafa feug
Na sen thiép niine yaw nga yakkeu lolou laniou beug
Prostitution intellectuelle Palais djégué Ponty
Xam xam nénagne pousso leu mais rare niofi pointu
Institution publique promotion Kanapé
Français yi yëk ak économie bigni Kidnapper
Facebook dou fay impôt té mo ngi ingérer wou
Bala Indépendance ba légui Toubab ya ngi insérer wou
Entente illicite ci kaw autoroute
Total Péage, Citidia diniou sucer goute par goute
Frank Timis ci avenir bou crépusculaire
Alliance bi ak Toubab wauroul boul diokhé annulaire
Rongagne Badola Simmeutoul thiéré buur kessé
Mamadou Diop, Bassirou Faye Police déy def décès
Guiss nagnefi Justice a desse vitesse
Après Jeune nou Colobane yi amena niénène niou dess
Kasso bu beuri Innocent Armel bu beuri Victime
D’après Loi Aisan ki ray Seye def lou crime
Guiss nagne fi Pétrole ak Gaz mba doufi indi Guerre
Loutah ba légui dossier Pétro-Trim mounoul lerr
Niaari Keuyite ben Xol ! bane reew nga deuk ?
Da ngay tardé boy djangalé salaire yafay ndieuk
Boy topando Yoneinte bi religion importé
Entre Cheveux ak Burqa lane laniou importé ?
Nit dou djité reew té yoroul dérett ci lokhom
Ladjal Papay Bassirou FAYE ndakh million diarna dom

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR