LYRIC

{Intro}
Dinga nangou khamna dinga nangou
Diinga nangou khawma kagn wayé dinga nangou
Khawma kagn wayé biss dina nieuw nga nangou
Dinga nangou dal wayé khawma kagne

{Refrain}
Guiissouma louma takha bayi dina def louné
Beugoo niiou nek kharite ndakh dothieu meuneu yem
Amoo koy nirool meussouma nop kou melni yaw
Mbeuguel leu meuneu bété yageu nala guiss mai tay la keuy rek dof si yaw
Meunouma comprendre nangouloma wakh
Wakho lane mola nekh si mane lane ngay yëg pour mane c’est pas normal
Yaw rek la done khar nangoul ma bayi dokhane
Wakhal rek ni nangounga mou diekh nangoul rek niou dem owaa

{Couplet 1}
Chaque midi 30 ngama dane rombeu ak sa blouse ak sac
Sama khol amone na bomb mais meusteu takkeu
Linga may romba takh ma dem badi setlou say tank
Meussoumala guiss ak goor dou sa mak té dou sa pape
Do tchip tchip gueum sa bop té tégou sa temps
Amnga style té boko gni def bamou saf sap
Leudio yoro djabuu guel bou beuri danger
Miiss bene biss la souniou nienti beut yii dadjé
Oooh mou melnii daniou ma yé si nelaw
Si biss bou meloulni biss you wessou melone
Melni sirène pakowontass daf ma def choc té niéméwou makoo wone dapp
Pressiion bou magga magg ga ma done dal
Question bima done lath djéy ki moy kane?
No dou mbeuguel ma amone flash
Na yém si rombanté bayanté khel com d’hab
Khawmaa kagn lakoo séne souniou palantaire
Si la dieulé depart volontaire
Damako toppe ba galèm té dou louma done tayy
May khalatt deal bi yeup bou matoone tay
Tieuy mbeuguel dou djaay kène douko wantère
Pour diap golo si niaye fokknga done nanté
Ok khamna galém wayé khawma toureum
Pub leu rek film bé ngui dora commencé

{Refrain}
Guiissouma louma takha bayi dina def louné
Beugoo niiou nek kharite ndakh dothieu meuneu yem
Amoo koy nirool meussouma nop kou melni yaw
Mbeuguel leu meuneu bété yageu nala guiss mai tay la keuy rek dof si yaw
Meunouma comprendre nangouloma wakh
Wakho lane mola nekh si mane lane ngay yëg pour mane c’est pas normal

{Couplet 2}
May romb rombeulou sa kogn di tanté sama chance
Bountou keurgui foule ma khawa complexé non
Fipou takeu sama fiit nanga def manguii fi
Dioxanté tour khamanté some ladj ma loumay def fi
Ndakh khamengama NON té mane khaménala Si
Dama beugonne niiou cause démal ba niieuwatt
Diokhma sa number call démal ba deloussi
Loutakh nga bagne mako diiokh non fook nga nieuwatt
Show bi bandit la daf mané ma niieuw mou saniima
Dioxma faux numéro ma nieuwatt mou dioxma number faram nane maggam la
Pour yaw na doff ba gueumla boulma djay Xélou GéDJ douma LAPPE mane DIEUNE la
Lima takha Jog dou sakh ay number call LANLA
Khawma ni mbeuguel di sakhé sama khol damala nopp WAW
Dou rayé khamna mais Yallna si Déh aurevoir
Lima lay wakhni fok nga bayi si khel mane amna koumay géneul té damako beugeu
Mane génoumeu Damay dougeu meunteu degn wakhoo deugeu

{Refrain}
Guiissouma louma takha bayi dina def louné
Beugoo niiou nek kharite ndakh dothieu meuneu yem
Amoo koy nirool meussouma nop kou melni yaw
Mbeuguel leu meuneu bété yageu nala guiss mai tay la keuy rek dof si yaw
Meunouma comprendre nangouloma wakh
Wakho lane mola nekh si mane lane ngay yëg pour mane c’est pas normal
Yaw rek la done khar nangoul ma bayii dokhane
Wakhal rek ni nangounga mou diekh nangoul rek niou dem owaa

{Outro}
Nangoul way (Yeh) beugeu nala (Yeh)
Li né si mane (Anh) khawma lane la (Yeh)
Beugeunala (Check) nakhoumala(Hun)
Nangoul bok (Yeh) warnga nangou rek mou diekh (Yeh)

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR