LYRIC

{Intro}
Yeah Bril mo bindeu way wii diko jaaglel
kéép kou beug yaayam

{Verse 1}
Léppa-ngui sossou, tambalé ci waxtu yi ngay dallou cii biireum
Dieumeuh di doundou cii dieumeuh yagg ko sonal té laabireum
Diougoul thi gueune di yokkou louné la deukou di am métiite
Limou datch laata nga wéékkou borom fiit bouko khaméé tite
Tha nèèkk wa youkhou djipp na mattna liir wa dioudou na foudouna
Khool wou ndieuk wa fassna thiofèl béggna ,dogouna toudou na
……..Allahou……. Alhamdou bayéko tcha xollam
Fopp na, nampal topatto di sameu ba déé moy féégne cii khoollam
Fonkk dom dji sookké, ni dieuffine yi meussone nééw lawé
Goudi gui dafay yaggueu thi mom, bèneu beute lay nélawé
Foumou dégué youkhou jog teup, gaddu nax tété bootte
Moy kiy tégou thi yone té dou deuppeu fék bégueuloul njaabote

{Refrain}
Maman Nianal ma, sama Mama, diéggueul ma
Sama Maman nianal ma, Manguilay niaan maa
Maman Nianal ma, sama Mama, diéggueul ma
Sama Maman nianal ma, lolou lay niaan mane …

{Verse 2}
Bou soré touti nga yookhou, do tagalékok mom, miin ngeu
Mola diégué yagg leu fonkou, xamné moomiin-ngeu
Xaaddiwoul bifi kène néwoul, mou seug di baatch laytaay
Limou lébone diokh la fayoul, feug nagneko fokk mou lay taye
Khaarroul ay ndimbeullou mbokam, maggam, badiane wala ndijjaay
Bagne nga khiff di raflé diarna tiolko’k takaay dalèni djaay
Yaguena djoy ay djoyyou xol , beuggoul ngay guiss ay rongognam
Foumou romb garapp gouy waadal baneex seug rogne nga gnam
Dafa diekh takk cii yaw, deuk thi takk ndigueum di daw
Aate yi dox ba gueum di law, fow nga tékki ba nek thi kaw
Moy yénéém, Lii la def thi xellam sa bou dioulé niaane
Dila digueul mbaax, joupp, yiw, gorré naanela boul ignaane

{Refrain}
Maman Nianal ma, sama Mama, diéggueul ma
Sama Maman nianal ma, Manguilay niaan maa
Maman Nianal ma, sama Mama, diéggueul ma
Sama Maman nianal ma, lolou lay niaan mane …
(Nianal ma Yaye )

{Verse 3}
Néwone nalène soumay bindeu cii mom ay tééré lay fééssal
Louy diougué thi xollay guèneu, baate bo dégue moy borrom
Gni nanema “Kène bagnoul yayam”, dougnou ma téré feusseul
Mbeuguel guima am thi mom té moukkou doumako def morrom
Yeah Maa, Ma délou cii waate di jééguelou
Diéguéssi niaanelou, soukou baalou wakhla fi nga ma tollou
Yeah Maa, Soumay nélaw wane ma yone yi
Ma baayéti lima jaapone jog daw thi fi nga ma yoonii
Bayémaa, Daagou topou thi say tankk diékh Weur tiabi firdawsi
Fo wotté wé ma dawsi
Yeah Maa, amougnou sa faye kène meunouko miim
Fouma guiss kouy merlo yayam, xol lay fess ni beutou djirrim
(Dégue loul)

{Refrain}
Maman Nianal ma (Nianal ma Yaye), sama mama, djéggeulma (Jégueulma Mama)
Sama Maman nianal ma, mangui lay niaan maa (Ma ngui sakou niane)
Maman Nianal ma (Nianal ma Yaye), sama Mama djéggeulma (Jégueulma Mama)
Sama Maman nianal ma, lolou lay niaan mane (Ma ngui sakou niane)

{Outro}
Fékhél mou bégue cii yaw, sa bo yéwo démal sakou niaanam (Mama nianal ma)
Diko diokh gni sèn yaye gueuneul lépp (Mama nianal manguilay niaan ma)
ANALYZIK

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR