LYRIC

{Intro}
Aduna bi doyna waar
Niit yé ngi woute ay….
Nguir meune di def loulène nekh
UP Studio Records
Xam nani safara Yaatouna

{Sanzala}
Meuss na nek kou baakh meuna nek kou bone
Baakarou Niitou kat ma dadjalé tchi tonne
Kouy dougou Aldiana lolou diaroul leu lathie
Mak sama Rawuxane aduna dignou xaathie
Niémé wouma di wakh beugouma décevoir
Sheytané dima interviwé manéko doyna waar
Xamoul né djangue na Ndongo tchi Blaise Diagne
Sama loxo di door meuna bindeu louy gaagne
Yallah nélawoulo guiss ngané ma ngui xééx
Xam ngani dagnema togne défouma louma nekh
Respecter na gni wéddi respecté na gni gueum
Jottayou fènn katt douma fa naane zeum
Niit ya ngui kharrou melni yaléni woo
Journaux yi diko wané di melni niouy fooo
Wakh dji di gueuneu beuri affabulation
Rap Bi di gueuneu ndool dévaluation

{Refrain}
Aduna bi doyna waar
Niit gné ngui woute ay….
Nguir meune di def loulène nekh
O YALLAH djégueul gnouuuuuu
Xam nani safara Yaatouna
Waayé sa yeurmandé ko eupeu fouf

{Elzo JamDong}
Lima yéné sama bopp Yalnako yéné nieup (Amine)
Djiguène djimay takk djangalma diabar tërééé leu (Amine)
Amena Licence Master dou takh ma djaay xam
Illuminati Dread douma djaay am
Dama beug guiss Kanamou ki gueune cii Mindef
Yalna bokou cii gni nguélawou Lahira di fééx
SOUBEU dou diekh waayé TAY yakoy mayé
Teubeulna gnimay xééx gnima fonk ma téyé
Def Iblis Capitaine ndaw penalty yu ladji
Fin du match nga djakk Meuwty bouy yeksi dou xaathiie
Bro Gucci Versace Boumou la diaral nga sathiie
Sister yék cii 4*4 yi boumou la diaral nga mathiiie
Djégueulou mo gueuneu woor gnouy saalé pank
Déh dina dieul cii sa borr té dou yaubalé Bank
Thiakaaba gaateuna lolou Dounya goudou Tank
Deuké tothie tothie niit njoleu Walahi dinala sank

{Refrain}
Aduna bi doyna waar
Niit gné ngui woute ay….
Nguir meune di def loulène nekh
O YALLAH djégueul gnouuuuuu
Xam nani safara Yaatouna
Waayé sa yeurmandé ko eupeu fouf (2 fois)

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR